Xeetu Mbëgéel
Tay jii mbëggeel a woote, sama
Xalima topp sama yaram di daw ci rythmu cardiaque
Mbëggeel dina feebar dina faj
Dinga bëgg nit di ko nëbb say sikk ba far jag
Mbëggeel garab la, ci sa jëmm lay xool
Kàddug cofeel laay saxal ci say nopp
Mbëggeel dafa am làkku boppam, bët dafay wax
Bi nga nee ma jàkk laa xam ne yaw it bëgg nga ma
Moom laay gis saa yoo may xool
Mbëggeel de njuumte ci la bokk
Dictée la bu kenn manul def zéro faute
Kon bul mer ba weer ci mbedd mi loo xam ne
Ci néegu séy lañu ko sumboon fóotsi
Yaw laa jooy, yaru mbëggeel mooy li ma dal
Ma lay xalaat ba dof ci yaw daal
Su ma jógul taxaw ci sama bopp
Dinaa yanu sama ay dàll
Bi nuy gise, say bidéewi gët di fer-ñent
Mbëggeel tàkk ci sa biir, nga déclaré ma say flamme
Manuma la fay, boo ko waxul woon duma am fitam
Mbëggeel di yëy sama xol, ma jënd guro jox imaam
Xam naa sa njëg, xam naa li ngay jar (waaw waawaaw)
Moo tax ma ñaansi la bañ a waaj (waaw waawaaw)
Xam naa itam ne séy xare la (waaw waawaaw)
Te jenn jigéen waru ci nàcc (waaw waawaaw)
Jox ma sa xol (jox ma sa xol)
Jox ma sa xol (jox ma sa xol)
Jox ma sa xol (jox ma sa xol)
Kaay jox ma sa xol (jox ma sa xol)
Jox ma sa xol waaye
Bu ko teg sama loxo
Damay bañ su ma la meree sànniwaat la ko
Ãaa! Jox ma sa xol (jox ma sa xol)
Kaay jox ma sa xol (jox ma sa xol)
Jox ma sa xol (jox ma sa xol)
Jooox ma sa xol (jox ma sa xol)
Déedéet mbëggeel amul xeet
Waaye am na ay xeetu mbëggeel
Am na mbëggeel yu lay xool di la xeeb, am
Yu lay gis rekk doyloo ni nga mel
Am na mbëggeel yuy fiir bëgg la moom, am
Yu lay bàyyi nga moom sa bopp
Am na mbëggeel yuy law di feeñ ci jëf, am
Yu dul wees catu làmmiñ ak i nopp
Mbëggeel amul couleur (waawaaw)
Maak yaw doy na ma misaal (waawaaw)
Index bu ñuul kukk di bëgganteek jigéen ju weex tàll
Njabootu arc-en-ciel di peinture sama asamaan
Su ma leen di xool, li may yëg sama xol, Yàlla kese Moo ko man
Li tax nu séy du neen (waawaaw)
Sunu destin moo nu jox dig-daje
Manuloo ma daajal banc
Doonte su ma taxawee di la xaar damay mel ni ku toog ci nen
Mbëggeel dafa am làkku boppam, bët dafay wax
Bi nga nee ma jàkk laa xam ne yaw it bëgg nga ma
Moom laay gis saa yoo may xool
Coração Acelerado
Teu coração tá acelerado, meu
A batida invade meu corpo, vai no ritmo do coração
Acelerado vai ficar, vai pegar fogo
Você quer alguém que te faça sentir a pressão
Acelerado é o que eu vejo, nos teus olhos eu percebo
As palavras que eu digo, ecoam na sua mente
Acelerado tem um jeito próprio, a boca não para de falar
Quando você diz que me ama, eu sei que você quer me ter
Eu só quero ver você brilhar
Acelerado é um sentimento que nos une
Ditado que ninguém pode errar, zero erro
Então não se preocupe, quando a noite chegar, você sabe que
Na escuridão, nós nos encontramos, é só você e eu
Você é quem eu quero, acelerar é o que eu faço
Eu só penso em você, não posso negar
Se eu não acordar, vou me perder em mim mesmo
Vou gritar meu amor, quando a gente se encontrar
Quando a gente se vê, suas cores brilham como estrelas
Acelerado dentro de você, você declarou minha chama
Eu não sou de fazer promessas, mas não vou te deixar na mão
Acelerado é o que eu sinto, eu te dou tudo que eu tenho
Eu sei o que você quer, eu sei o que você precisa (é, é)
É por isso que eu não posso deixar de querer (é, é)
Eu sei também que você quer mais (é, é)
E nenhuma mulher pode ficar de fora (é, é)
Me dá seu coração (me dá seu coração)
Me dá seu coração (me dá seu coração)
Me dá seu coração (me dá seu coração)
Vem me dá seu coração (me dá seu coração)
Me dá seu coração, mas
Se você não me der a mão
Eu vou me perder se eu não tiver você aqui
Ah! Me dá seu coração (me dá seu coração)
Vem me dá seu coração (me dá seu coração)
Me dá seu coração (me dá seu coração)
Vem me dá seu coração (me dá seu coração)
De fato, acelerado não tem fim
Mas tem muitos corações acelerados
Tem corações que te fazem sentir a brisa, tem
Que te fazem ver como você é especial
Tem corações que querem te fazer feliz, tem
Que te fazem ver que você é tudo
Tem corações que querem te dar tudo, tem
Que não vão deixar você só, nem por um segundo
Acelerado não tem cor (é, é)
Mas você é um exemplo pra mim (é, é)
Índice de amor que faz a mulher brilhar como um arco-íris
Família pintada no céu da minha vida
Se você olhar, o que faz meu coração vibrar, Deus é testemunha
É por isso que não podemos deixar de amar (é, é)
Nosso destino nos dá a chance
Eu não vou desistir de você
Então se eu me perder, vou me sentir como alguém que não sabe onde está
Acelerado tem um jeito próprio, a boca não para de falar
Quando você diz que me ama, eu sei que você quer me ter
Eu só quero ver você brilhar.