395px

Os Tamales

Momo Dieng

Li Ngama Tamale

Today, baby, jotuma la
Nga raar ma ba mel ni yaw ku ma xamul
Lii bi muy ñëw gisuma ko yoow
Bët li kay faat dal kon mënu ko gis

Bët li kay faat du ko gis
Li ku ma ko waxoon man duma ko gëm
Today, baby, jotuma la yaw
Nga raar ma ba mel ni yaw ku ma xamul

Lu tax nga bàyyi ma?
Lu tax waxulook man?
Lu tax nga bàyyi ma nii?
Lu tax nga bàyyi ma?
Lu tax waxulook man?
Lu tax nga bàyyi ma fii?

Aaaaaaa, kaay!
Ee!

Ndox tàngul dañ ko wal jikkom ja
Man mii bëgg naa xam ku dugg sunu diggante
Jikko ji de xamewuma la ko, baby
Man de bëgg naa xam ku dugg sunu diggante

Maa la bëgg waay
Maa la yërëm waay
Maa la xam waay eee
Maa la bëgg waay
Maa la yërëm waay
Maa la xam waay eeey!

Lu tax su ma la gisulee sama xel di ñaaw
Damay foog ni yaa ngi langaak keneen, ay!
Man lu tax su ma la jotulee sama fiit du tooge
Damay foog ni yaa ngi waxtaan ak keneen, ay!
Gis naa ni fan yu mujj yii yaw de danga changé
Dafa mel ni yaa ngi giseek keneen, ay!

Xanaa du lii nga ma tammal
Ñuy fanaan ci téléphone bi
Xanaa du lii nga ma tammal
Danga may wayal ba ma nelaw
Coco du li nga ma tammal
Doxantu corniche dem naa ni coco
Xanaa du lii nga ma tammal
Danga may raay ba ma nelaw
Xanaa du lii nga ma tammal
Di ma toppattoo guddi ak bëccëg

Waaw maa ni ku yàgg ci loxo buñ ko teye mu xam ko
Dafa mel ni yaa ngi lonkook keneen, ay!
Dafa mel ni sama intuition moom de naxuma yaay
Gis naa ni yaw danga am keneen, ay!

Xanaa du lii nga ma tammal
Ñuy fanaan ci téléphone bi
Xanaa du lii nga ma tammal
Danga may wayal ba ma nelaw
Coco du li nga ma tammal
Doxantu corniche dem naa ni coco
Xanaa du lii nga bég jeexal
Diggante bu neex bi mbaa du dañu la liggéey

Dafa mel ni sama gent gi moom de naxuma yaay
Gis naa la yaa ngi bëggante ak keneen, ay!

Os Tamales

Hoje, meu bem, eu não te entendo
Você me tratou como um estranho
Essa eu não esperava
O assassino é cego, por isso não consegue ver

O olhar do assassino não vê isso
Eu não acreditaria em nada que me dissessem
Hoje, meu bem, eu não te entendo
Você me tratou como um estranho

Por que você me deixou?
Por que você não falou comigo?
Por que você me deixou assim?
Por que você me deixou?
Por que você não falou comigo?
Por que você me deixou aqui?

Aaaaaaah, grite!
Sim!

Água quente foi derramada sobre seu corpo
Eu, por exemplo, quero saber quem se meteu entre nós
Eu não conheço essa personagem, querida
Quanto a mim, quero saber quem se meteu entre nós

Eu te amo, cara
Sinto muito por você, cara
Eu te conheço, cara!
Eu te amo, cara
Sinto muito por você, cara
Eu te conheço, cara!

Por que me sinto mal quando não te vejo?
Acho que você está falando com outra pessoa, nossa!
Por que meu estômago não se acalma quando estou com você?
Sempre achei que você estivesse falando com alguém, infelizmente!
Tenho notado uma mudança em você ultimamente
Parece que você está saindo com alguém, infelizmente!

Não foi isso que você me ensinou?
Eles passam a noite ao telefone
Não foi isso que você me ensinou?
Você me canta para dormir
Coco não é o que você tinha planejado para mim
Passeando pela Corniche, eu fui como um coco
Não foi isso que você me ensinou?
Você me abraçou até eu adormecer
Não foi isso que você me ensinou?
Ele cuida de mim dia e noite

Sim, acho que qualquer pessoa que já tenha ficado algemada por muito tempo sabe disso
Parece que você está se correspondendo com outra pessoa, infelizmente!
Acontece que minha intuição não estava enganando minha mãe
Vejo que você já tem outra pessoa, infelizmente!

Não foi isso que você me ensinou?
Eles passam a noite ao telefone
Não foi isso que você me ensinou?
Você me canta para dormir
Coco não é o que você tinha planejado para mim
Passeando pela Corniche, eu fui como um coco
Você está animado para terminar isso?
Um relacionamento feliz ou algo que não funciona para você

Parece que meu sonho não está enganando minha mãe
Vejo você se apaixonando por outra pessoa, infelizmente!