Bamba La Solution (feat. Ahmada Jadid & Abdou Khoudoss Kara)

Jahman X-Press

Rëkk gaay ñi
Bu kenn jaaxle, Sëriñ Bàmba wuyusi nañ
Yërmandeem a bari ci ñun, ba tax na
Dikk na sauver jàmm ñi

Yeem naa la
Yéemoon naa la, Mbàkke, yéemaati naa la
Yaa fi nekkal Yàlla Hazza wa Jalla
Rëjërajëf teeti

Bàmba fëttal na
Rap wa, Ceerno Ibra Faaty fees ko
Dogte ko, togg ko, ñëwleen reer ko
Mbana ga junni ñaay la

Xanaa da nuy suxaat di raam
Ba ñëw ci yaw te naan la Maam?
Bootal te roganti ñu

Bëgg na noo am sa ngëram
Bu ñu baaxee dinañ ko am
Muy texe tey ak ëllëg

Moo tax jébbalu nañ
Bu wér a wér ak mboolem lu ñu am tey saxoo sant
Guddeek bëccëg

Xëy suba teel
Léemoo Sa Tur wu mag wi day tax a mucc
Te day waral say mbir gaaw

Seex Bàmba doy loo lu doy
Daa am solo yaa ki nu doy tey ak ëllëg
Yaa gën ci ndey, yaa gën ci baay

Seex Bàmba, ñooŋ lay dagaan
Ci barke Al Muntaxaa, Boroom mbég ak taar wi
Buur Yàlla naatal réew mi

Ndimbal, ndimbal ak yërmande (ndimbaloo Fall)
Murid jëfe ndigal, baayi tere (ay góor Yàlla, loolooy yoon wi)
Ndimbal, ndimbal ak yërmande (ndimbaloo Fall)
Murid jëfe ndigal, baayi tere (ay góor Yàlla, loolooy yoon wi)

Boroom Jumaa ji
Doomi Jaara Buuso nga la dimbali nu
Da noo doyadi rekk, waaye yërëm nu
Yaa mbégteem sunu xarnu

Mbàkke ñaan nañ la
Déelu ñaanati barke Boroom Daaru
Nang nu samal ngor gi ba ba ñuy faatu
Xeewal it bu ñuy bëwloo

Ñaan nañ ci barke
Mafarma Yaasin Daour mi ci mbul sagal nu
Issa Dièye, Faatim Penda leeram ga sàr na
Ba juroom ñaari asamaan yee

Ndax da ngaa bari ay may?
Ña daan falu, yaalen fal

Eskeey sangub Maam Seex Ibrahima Fall
Àjjana yépp a ngay riir ngir saam Faali Baay Fall
Eskeey sangub Maam Seex Ibrahima Fall

Faala gën (madegel)
Maam Seexa raw (ngañ madegel demba)
Faala gën (madegel)
Maam Seexa raw (ngañ madegel demba)
Faala gën (madegel)
Maam Seexa raw (ngañ madegel demba)
Faala gën (madegel)
Maam Seexa raw (ngañ madegel demba)
Ngañ ma ca leer ya (degal)

Moo tax jébbalu nañ
Bu wér a wér ak mboolem lu ñu am tey saxoo sant
Guddeek bëccëg

Xëy suba teel
Léemoo Sa Tur wu mag wi day tax a mucc
Te day waral say mbir gaaw

Seex Bàmba doy loo lu doy
Daa am solo yaa ki nu doy tey ak ëllëg
Yaa gën ci ndey, yaa gën ci baay

Seex Bàmba, ñooŋ lay dagaan
Ci barke Al Muntaxaa, Boroom mbég ak taar wi
Buur Yàlla naatal réew mi

Ndimbal, ndimbal ak yërmande (ndimbaloo Fall)
Murid jëfe ndigal, baayi tere (ay góor Yàlla, loolooy yoon wi)
Ndimbal, ndimbal ak yërmande (ndimbaloo Fall)
Murid jëfe ndigal, baayi tere (ay góor Yàlla, loolooy yoon wi)


Comentários

Envie dúvidas, explicações e curiosidades sobre a letra

0 / 500

Faça parte  dessa comunidade 

Tire dúvidas sobre idiomas, interaja com outros fãs de Jahman X-Press e vá além da letra da música.

Conheça o Letras Academy

Enviar para a central de dúvidas?

Dúvidas enviadas podem receber respostas de professores e alunos da plataforma.

Fixe este conteúdo com a aula:

0 / 500

Opções de seleção